
Sama Dôme
REFRAIN
Ngalla Yalla bou la tathiô na nga démm (Na nga démm !)
Sa ma dôme, bou ko défoul na nga diéémm
Na nga dégue sa may wakh té boum la yêmm (Boum la yêmm !)
Sa ma dôme na nga diéémm.
(2 fois)
NaT MC
May niann Mâdémba,
Nga doy ni sa bây dji
Même bou féké ni da nga démm ba
Seuss, mak sa yaye dou niou la bayii
Sa ma dôme,
Sa ma soppé
Bou gou ma si yawl ou doul freedom
donn sa altopé
Mome rékk lay niann,
Sa ma dôme dji
Ma beugue nga magg nékk ki niakkinianne
Ba say fruit niénén meunn ko dji
Yay sa ma dome dé
Kone dou ma déff si yaw respect donté
Ma la yillif done sa kiliifeu
Khamél ki ngay diokh thieurr comme ni nga rannié ni lii liif leu
Sama dôme sa ma soppé
Beugue gui ma la beugue takh na may bagne sa rangogne fou mou tokkhé
Fi mouy guénné ak fing ka nara fonmpé
Mou nékhak mou tiss
Na nga gueumm né Yalla rékka meuna guiss
Ba takh niou done silmakha,
Fou ko nékh diaraléniou nga niakkak nga riss
Sou ma sagnône,
Sou ma sagnône nga télla khamé lou bone té ba nionniou
Di ko dieufeundikô
Nakh diafandikouwô
Si lou bone
Sa yone
Nang ko téla reudeu
Kham fa nga dieumm, téll ko diokh geudeu
Yallay mayé nakk wayé na nga diémm kheuy na nga guiss deugue.
Kone sa ma dôme andalak sa sago,
Même euleuk bô démone ba yorri cadilak boul ko di saggo
Ta wakh diou rafétte diô kham déf ko sa takko
Dôme, déko di taggô
Gueumeul ni yaye sa ma dôllé
Ndakh tay dji bou ma fatou wône yaw lagne may khôllé
Ta lépp lou ma diotta ame, bougne koye diokhé
Si yaw la niouy dôré
Inss bi nakk khalé bou ndaw ngeu
Fékhél ba bô magué say morome naw leu
Fékhél ba done royoukaye
Ba euleuk sou niou borome moussal leu si yoyou gay
Donil nitt kou fidéll,
Say djabarr respectélene
Ta boul téla ame guéll
Djigénn yeupp yamalélènn
Lâta may sangô souff
Bougône na bâtt yi djougué sa ma guémigne dougou sa nopp
Nakh lii dou lénn lou doul têré gou la ouff
Are la si lamignak moussiba bou la topp.
Kone ndâ li ma done rotte féssagoul, fékhél ba féthialiko
Même bou fêssoul fékhél ba say dôme nétaliko
Fékhél ba kou si nékk lokhome diott si li ko
Séne mame yéné, li ma beugone nga diotaliko
Ba euleuk nga meuna fékh sa birr bamél
Amsi térangay aldiana yék you ni méll.